dcsimg

Gargamboose ( Wolof )

provided by wikipedia emerging_languages
 src=
Garabug gargamboose

Gargamboose xeetu garab la gu bokk ci ñoñ "opuntia". Ca Amerig gu digg la bàyyikoo, fi ñuy woowee Karayib.

Melo wi

 src=
Tóortóooru gargamboose

Gargamboose garab la gog day màgg te am xeetu xob yu dijj ak ay dég yu mag te ñaw, seen taxawaay di kaaraange, am na it dég yu sew yuy jame

Meññeef mi

 src=
Meññeefum gargamboose

Meññeef mi dees koy lekk. Dees koy xolli bam set bala ñu koy jëfandikoo.

Njariñ yi

Ay doomam bari nay njariñ lool.

Dees na ci defar ay tàngal, ay njar walla njambaan yu neex. Ay bantam day faj (estomaa) góomu biir. Biir buy daw it dina koy faj, ba ci sax jabeet.

Turu xam-xam wi

Opuntia tuna

Tur wi ci yeneeni làkk

araab: الصبَار
license
cc-by-sa-3.0
copyright
Wikipedia authors and editors

Gargamboose: Brief Summary ( Wolof )

provided by wikipedia emerging_languages
 src= Garabug gargamboose

Gargamboose xeetu garab la gu bokk ci ñoñ "opuntia". Ca Amerig gu digg la bàyyikoo, fi ñuy woowee Karayib.

license
cc-by-sa-3.0
copyright
Wikipedia authors and editors